[go: up one dir, main page]
More Web Proxy on the site http://driver.im/Aller au contenu

Aadama

Jóge Wikipedia.


Aadama mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam (آدم). Ci angale mooy Adam te ci faranse itam mooy Adam. Mooy nit ki Yàlla jëkka sàkk.

Nettalib Aadama feeñ na ci Ge 1:26-30; 2:4-8; 15-20. Aadama dafa toppoon jabaram Awa ci bàkkaaram. Bàkkaar boobu mooy lu indi musiba yépp yi nu gis ci àddina si (Ge 3:6-21). At, ya Aadama dundoon, 930 la. (Ge 5:5). Ci Injiil dañuy wax ci Aadama ci Lu 3:38; Ro 5:14-19; 1Ko 15:22,45; 1Tim 2:13,14; Yu 1:14.

Nettalib Aadama feeñ na ci suraat 2:30-38; 3:33,59; 7:11,19-27; 17:61-62; 18:50; 19:58; 20:115-128. Nekk na ki Boroom bi jëkk a bind muy nit doon tamit Yónnent bi njëkk. Yàlla a ngi wax ci Alxuraan: " Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne daf ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? Mu ne: Xam Naa lu ngeen xamul”

Yàlla wahyu suuf si ne ko: damay sàkk ci yaw ay bindéef, amna ci ñoom ñu may topp, am ci ñoom ñu may moy, képp ku ma ci topp ma tàbbal ko guyaar, képp ku ma moy ma tàbbal ko sawara.

Suuf ne ko: ndax dangay bind ci man ñoo xam ne danga leen di dugal sawara? Sunu Boroom ne ko: waaw!

Nee nañu: Ibliis daal di wàcc ci kaw suuf ne ko yaw suuf, damaa ñëw ngir laabiire la, Yàlla daa namm a bind ci yaw ki gën ci bindaafon yi, te may ragal ñu moy ko mu leen di tàbbal sawara, bu booba yaw it dinga duggaale sawara tamit. Suuf daa di jooy!

Yàlla bind sunu baay Aadama ciy yoxoom ngir Ibliis bañ a rëy ci sujjótal ko, Yàlla a ngi nuy wax ci loolu:

"Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, nangeen daldi rot, sujjóotal ko."

Nee nañu: bi Yàlla bindee Aadama (HS) toog na 40i guddi. Am ñu ne: 40i at, muy jëmm ju ñu tërëral. Ibliis daan ko dikke, di ko kàjji muy keleŋ ni ban wu wow, nee ñu mooy li sunu Boroom naan:

" Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ".

Ibliis di dugg ci biir gémmiñu Aadama di génne ci ginnaawam, di jaar ci ginnaawam di génne ci gémmiñam, te naan ko: " Doo dara, ak lu tax ñu bind la?, su ñu ma la saytuloo ma alag la, bu ñu la saytuloo ma ma moy la".

Malaaka yi bu ñu ko daan romb dañu ko daan ragal, fekk ne Ibliis moo leen ko gën a ragal. Ba dig bi nga xam ne la Yàlla namm ëf Ruuwam ci moom jotee, mu ëf Aadama Ruuwam. Mu digal Malaaka yi ci ñu sujjóotal Aadama. Malaaka yépp sujjóotal Aadama ba mu des Ibliis ngir rëy mu bokk ci way-wedd ni ca saa sa. Yàlla ne ko yaw Ibliis, ana lu la tee sujjóot ndeem digal naa la? Mu ne kii maa ko gën, man du ma sujjóotal nit koo binde ci suufu ban.

Ibliis sujjóotul ngir rëyam ak mbewteem ak kiñaan. Yàlla ne:

" 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ”

76. “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci

ban”.

77. (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ;

78. te Samam rëbb dal na la ba ba saa di taxaw”.

79. “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”.

80. (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu,

81. ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”.

82. “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj-loo ñoom ñépp,

83. ba mu des sa jaam ñiy sellal”."

Aadama Ak Noonam Ba (Ibliis)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi Yàlla noppee ci Ibliis ak ci yedd ko, Ibliis bañ rekk ne day moy Yàlla. Sunu Boroom rëbb ko tàq ko ci yërmàndeem def ko Saytaane Rajiim, génne ko ca guyaar. Ginnaaw loolu Ibliis sumboo ak meram iñaane Aadama, mu bëgg koo génne guyaar. Yàlla bàyyi ak Aadama xelam gawu ko ci dara, mu bayyi ko ak sagoom, muy man a ràññe lu baax ak lu bon, ginnaaw ba mu ko maytuloo Ibliis, Yàlla a ngi naan:

". Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de.

118. [Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle,

119. doo fi yëg u mar, doo fi màggat”."

Ginnaw bi ñu dàkkoo Ibliis, mu tàmbali nag ci jëfe la mu dogu woon; te mooy fayu ci Aadama (HS) ak génne ko guyaar, di ko awale ci di ko jiixi-jaaxaloo, jéem koo gëmloo ne xam na lol man na tax ba Aadama sax dàkk du dee mukk. Yàlla a ngi wax naan:

"Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”."

Ibliis jaare ci bëggug Aadama ci sax fi dàkk ak sax ca guyaar; bañ fa a génn. Mu xam ne loolu ay tombug néew dooleem, Ibliis daa bëgg a wan ne sunu Boroom; man naa alag kii nga may gënalee. Adaama moom ndaysaan, xamul dara ci kàcci Ibliis yi, waaye li mu ko wax neex na ko te jar na a jarabu, mu yëg ne loolu du'y fo mu laaj Ibliis naka lay def ba am loolu moom ak soxnaam Awa? Ibliis ne ko : ndax yaa ngi gis garab gii ñu la tere nga lekk ci? Moo la ko man a may. Waaye ba tay Aadama gëmul Ibliis, muy fàttaliku tere gi sunu Boroom tere woon ci mu bañ a jege garab gi.

Kon naka la Aadama def ba lekk ca garab ga ak aartu yi ñu ko aartu yépp bàyyikoo ci sunu Boroom?

Boroom xam-xam dañuy wax ne(YRX): Ibliis ci jax-jaxal yi mu doon def Aadama, moo ko doon fàtteloo ndànk ndànk li ko sunu Boroom tere woon (loolu moo nuy dal nun ñépp ba tay, su nuy saytaane di jax-jaxal, danuy fàtte ndànk ndànk lepp lu nu mas a waar). Waaye Aadama gëmul woon lu dul ginnaw ba mu waatee, Aadama ne ko giiñal nu bu dee li nga wax dëgg la, Aadama (HS) -ci ni ñu bind- xam na ne kenn warut a waat ci Yàlla ba noppi di fen. Mu ne ko waatal ci kiy sama Boroom di sa Boroom ne li ngay wax dëgg la. Ca noonu la Ibliis mi ñu rëbb giiñe ci kanamu Aadama ngiiñug fen ci ne li mu wax dëgg la te moom da koy laabiir rekk moom ak Awa. Yàlla a ngi nuy leeral loolu ci téereem bu sell bi Alxuraam, mu ne: " Mu giiñal leen ne moom kat mi ngo bokk ci way-laabiire ñi"

Ginnaw ba Ibliis waatee, ci la xelu Aadama soog di dal naka noonu Awa (HMS) ndax seen xel masut a jàpp ne kenn sañ na a giiñ ci Yàlla ci ay nar, Ibliis nekk ki jëkk a waat ci Yàlla ci ay fen (kon képp kuy waat ci Yàlla di fen, Ibliis ngay roy) te amul fu mu ko defe fu dul àjjuna. Ca la Aadama fàtte lépp lu ñu ko tere woon ndax giiñu Ibliis ji, tàmbalee lekk ca garab ga moom ak Awa. Nee na ñu garab ga garabu pom la woon nekkoon ci kaw suuf, bi ñu ko lekkee rekk la seen mbalaan ya muriku seen awra feeñ. Yàlla ngi nuy leeral loolu naan:

"22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt

di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”

wàccug Aadama Ak Awa Ak Ibliis Ci Kaw Suuf

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

La dal Aadama dal ko; mu lekk ca garab ga, sunu Boroom wàcce Adama ak Awa ñoom ak Ibliis ci kaw suuf, Yàlla a ngi naan:

"[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di

noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”.

Bi ñu wàccee Ibliis ci kaw suuf daf ne: yaw sama Boroom génne nga ma àjjana ngir Aadama, te man manaluma ko dara ndare danga maa kàttanal ci kawam, Mu ne ko defal naa la ko, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko lu mu am ci doom nga am lu ni tollu, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko seen i dënn say dëkkuwaay la; ngay man daw seen biir i yamar ni dereet di dawe seen i yaram, mu neeti dollil ma, Mu ne "Génnal ak say kàddu, loo mën ci ñoom, nanga leen song ak say xarekat ak say gawar,

nanga bokk ak ñoom alal ak i doom te dig leen”. Waaye Séytaane du leen dig lu dul ay nax."

Ginnaaw bi Aadama xamee li Ibliis sàkku ci sunu Boroom mu ne: Ay yaw sama Boroom teg nga ko sama kaw, te man it manuma mucc ci moom lu dul ci sa ndimbal, Mu ne ko doo am doom lu dul boole naa ko ak ñu koy aar ci àndaale yu bon, mu ne dollil ma, Mu ne ko jenn jëf ju baax ju ne ma ful ko fukk te di ko yokk, jenn jëf ju ñaaw ju ne jenn laa koy jàppe te di ko far, mu ne dollil ma, Mu ne ko "Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla.

Ndax Yàlla dana jéggale bakkaar yépp. Mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.

Mu neeti ko, yaw sama Boroom dollil ma, Mu ne say njaboot fi ak ñoo ngi dund du ma tëj seen buntu njéggal, mu ne dollil ma, Mu ne dinaa jéggale te du ma toppe, mu ne doyal naa.

Waxinu wolof bu tekki "nit ñi".